Saar 9
 1 Éy ku ma mayoon ci màndiŋ mi 
dalu panaanum njëggaan, 
ba ma teqlikook bokk yi, wacc leen, 
dem, bàyyi leen? 
Ñoom ñépp ay bokkaale, 
di gàngooru workat. 
Dëgg jeex na 
Yàllaay wax 
 2 «Ñu ngi tàwwi ni fittkat seen làmmiñu workat, 
seen doole ci réew mi doxaluñu ci yoon. 
Ñu ngii di def lu bon ci kaw lu bon, 
te man faalewñu ma.» 
Kàddug Aji Sax jee. 
 3 «Na ku ne moytu dëkkandoom 
te baña wóolu menn mbokk. 
Kuy mbokk déy lal nga pexem wuruj, di wuruj; 
kuy dëkkandoo, sos ngay wéye. 
 4 Ku ne sa dëkkandoo ngay nax, 
te dëgg, doo ko wax. 
Dañoo tàmmi fen, 
di def njekkar ba sonn. 
 5 Yeena ngi dëkke njublaŋ, 
njublaŋ rekk, 
faaleetuleen ma.» 
Kàddug Aji Sax jee. 
 6 Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi 
wax ne: «Maa ngii di leen segg, 
nattu leen ni weñ gu sawara seeyal, xelli! 
Ana nu may def neneen 
ak sama ñoñ? 
 7 Seen làmmiñ di fitt guy bóome, 
seeni wax dig njublaŋ. 
Nit di wax moroomam jàmm, 
te di ko tëru cim xelam. 
 8 Lii duma leen ko dumaa?» 
Kàddug Aji Sax jee. 
Mu ne: «Xeet wu mel nii duma ko fey yoolam?» 
Jooy jot na 
Yeremeey wax 
 9 Tund ya laay jooy, di yuuxu, 
di jooy parluy màndiŋ ma, 
fa lépp lakk, ba jaareesu fa, 
déggeesul baatu jur; 
njanaaw ak mala, 
lépp daw, ne mes. 
Yàllaay wax 
 10 «Maay def Yerusalem jali doj, 
till yi dëkke; 
ma def dëkki Yuda gent bu kenn dëkkul.» 
Yeremeey wax 
 11 Ana ku muus, ba xam lu waral lii? 
Ku Aji Sax ji waxal, 
mu wax nu lu waral réew mi sànku, 
gental ni màndiŋ mi, 
kenn jaaru fi? 
 12 Aji Sax ji neeti: 
«Ñoo wacc sama yoon 
wi ma leen tegaloon, 
sàmmuñu sama kàddu, 
jëfewuñu ko, 
 13 xanaa toppoo dëgër bopp, 
topp tuuri Baal 
yi leen seeni maam miinaloon.» 
 14 Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, 
Yàllay Israyil dafa wax ne: 
«Maa ngii di leelsi xeet wii njàqarey xeme, 
nàndal leen tookey mbugal. 
 15 Maa leen di wasaare fi biir xeet yu ñu xamuloon, 
du ñoom, du seeni maam. 
Maa leen di tofal saamar, ba raafal leen.» 
 16 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: 
«Ne leen: Waajleena wooyi jigéeni jooykati dëj yi, ñu dikk; 
yónneeleen ca ña gëna man, ñu dikk.» 
Yeremeey wax 
 17 Nañu gaaw dëbbeel nuy jooy, 
gët taa, rongooñ wal. 
 18 Yuux a ngoog, jibe Siyoŋ. 
Ñu naa: «Nooka rajaxoo, 
torox ba ne tott, 
noon màbb sunuy dëkkuwaay, 
nu génn réew mi.» 
 19 Yeen jigéen ñi, 
ngalla dégluleen kàddug Aji Sax ji, 
taataan waxam, 
ba jàngal seeni janq jooyi dëj, 
jigéen ju ne jàngal moroomam yuuxi dëj. 
 20 Ndee déy moo ñalgoo sunuy palanteer, 
dugg sunuy kër yu yànj, 
ngir fàdd gone yi ci mbedd mi, 
ak xale yu góor yi ci pénc yi. 
Yàllaay wax 
 21 «Ne leen: Kàddug Aji Sax jee. 
Néew yeey wetaroo ci àll bi, mel niy jonkan, 
ni gub yu góobkat won gannaaw, kenn forul.» 
Ku xam Yàlla rekk a xelu 
 22  Aji Sax ji dafa wax ne: 
«Ku xelu, bumu damoom xelam; 
ku jàmbaare, bumu damoo njàmbaaram; 
ku woomle, bumu damoom koomam. 
 23 Kuy damu kay, na damoom xelam 
mu ko may mu xam ma, 
xam ne maay Aji Sax, 
jiy jëfe ngor ak dëgg ak njekk fi kaw suuf. 
Loolu déy mooy sama bànneex.» 
Kàddug Aji Sax jee. 
Xaraf, na Yàlla tax 
 24 «Ay bés a ngii di ñëw,» 
kàddug Aji Sax jee, 
«maay dikkal képp ku xarafam yem ci yaram, 
 25 muy waa Misra, di waa Yuda, 
di Edomeen ñeek Amoneen ñi, 
di Mowabeen ñeek 
mboolem ñiy wat seen peggu kawaru bopp 
te dëkke màndiŋ mi, 
nde xeet yooyu, kenn xarafu ci dëgg, 
waaye bànni Israyil gépp it 
*9:25 9.25 Xeeti àddina yu bare baaxoo nañu di xaraf. Waaye xaraf ci la Yàlla nammoona birale kóllëre gi dox digganteem ak bànni Israyil. Moo tax gépp góor gu bokk ci woowu askan waroona fésal ci yaramam màndargam xaraf miy firndeel googu kóllëre, te ànd ceek xolu jëfe ko.