Sabóor 23
Aji Sax jee may sàmm 
 1 Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. 
Aji Sax jee may sàmm, 
du lenn lu ma ñàkk. 
 2 Parlu mu naat la may gooral, 
wal mu dal, mu tette ma ca, 
 3 leqli ma, 
teg ma ci yooni njekk 
ngir teddngay turam. 
 4 Su may jaare xuru ndee wu ne këruus it, 
duma ragal loraange: 
yaw laak man, 
sa bantu sàmm ak sa nguul, 
yooyoo may dalal. 
 5 Yaa ma berndeel, 
noon yi gis, 
nga diwal ma saa bopp, terale ma, 
saab kaas rembat. 
 6 Mbaax ak ngor kay la ma Aji Sax jiy dare sama giiru dund, 
ma dëkke këram ba fàww.