Sabóor 112
Ku ragal Yàlla gis njekkam 
 1 Màggal-leen Ki Sax! 
Ndokklee ku ragal Aji Sax ji, 
di tàqamtikoo ay santaaneem. 
 2 Aw askanam ay am doole ci réew mi. 
Ku jub saw xeet barkeel, 
 3 alal ak koom am sa kër, 
sag njekk sax dàkk. 
 4 Ceeñeeru biir lëndëm jollil na ku jub 
ak ku baax, di boroom yërmande ak njekk. 
 5 Ki baaxle mooy ki laabiir, di leble, 
di jëflante cig njub. 
 6 Ku jub du tërëf mukk, 
te dees na ko fàttliku ba fàww. 
 7 Du ragal dég-dég bu tiis, 
xel ma day dal, mu wóolu Aji Sax ji, 
 8 fit wa toog, du ragal, 
ba kera muy gis noonam jóoru. 
 9 Mooy nàddil néew-doole yi, 
njekkam sax dàkk, 
dooleem di yokku, ànd ak daraja. 
 10 Soxor bi da koy gis, mer, 
iñaan bay yéyu, jeex tàkk; 
nde soxor, yaakaar ju tas rekk.