Sabóor 126
Yàlla, delloo nu 
 1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. 
Ba Aji Sax ji delloo waa Siyoŋ seen réew, 
danoo meloon ni ñuy gént, 
 2 di reek a sarxolle rekk. 
Yéefar yi naa: 
«Lu réy la Aji Sax ji defal ñii.» 
 3 Lu réy la nu Aji Sax ji defal moos, 
nu bég. 
 4 Aji Sax ji, rikk delloo nu na woon, 
ni ngay delloo wal yu ŋiis, mu walaat ca àllub Negew. 
 5 Kuy ji di jooy, 
yal na góob, di sarxolle. 
 6 Ku doon wéya wéy, di jooy; 
ŋàbb mbuusum jiwoom, 
yal na dikka dikk, di woy, 
ñibbaale sabaaram.