Sabóor 130
Nu séentu njotug Yàlla 
 1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. 
Aji Sax ji, ci ay xóote laa lay wooye. 
 2 Boroom bi, déglu ma, 
teewlu ma, ma tinu la. 
 3 Ki Sax, yaw, soo doon lim bàkkaar, 
Boroom bi, ana kuy taxaw? 
 4 Waaye yaay jéggale, 
ñu ragal la. 
 5 Damay xaar Aji Sax ji, di ko xaare xol, 
di yaakaar kàddoom. 
 6 Wattukat bi yàkkamti njël, 
wattukat bi yàkkamti njël, laa ne, 
ni ma yàkkamtee Aji Sax jee ko raw. 
 7 Éey Israyil, négandikul Aji Sax ji. 
Aji Sax jee gore, 
te yaatug njot. 
 8 Mooy jot Israyil ci ñaawtéefam yépp.