Sabóor 134
Way-gëm ñaa ngi sant 
 1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. 
Ayca, santleen Aji Sax ji, 
yeen jaami Aji Sax ji yépp, 
yeen ñiy taxawe kër Aji Sax ji guddi. 
 2 Yékkatileen seeni loxo bérab bu sell ba, 
te sant Aji Sax ji. 
 3 Yal na la Aji Sax ji barkeele fa Siyoŋ, 
moom mi sàkk asamaan ak suuf.