Sabóor 137
Jooye nanu àll 
 1 Ca tàkkal dexi Babilon, 
foofa lanu daa toog, 
fàttliku Siyoŋ, jooy. 
 2 Ca garab ya 
lanu daa wékk sunuy xalam. 
 3 Fa la nu sunuy sang daa woyloo, 
not nu, bëgg nu bégal leen, 
naan: «Woyal-leen nu ci woyi Siyoŋ.» 
 4 Moo nu nuy woye woyu Aji Sax ji 
kaw suufas yéefar? 
 5 Éy Yerusalem, su ma la naree fàtte, 
yal na ma doole dëddu! 
 6 Yerusalem, su ma la fàttlikuwul, 
fonk la, ba gën laa bége lépp, 
yal na sama làmmiñ tafoo sama denqleñ. 
 7 Aji Sax ji, fàttlikul Edomeen ña, 
keroog jantub Yerusalem, 
ba ñu naan: «Màbbleena màbb, 
ba kenug dëkk bi siiñ!» 
 8 Yeen waa Babilon, gi ñu nara fàllas, 
ndokklee ku leen fey jëf, 
ja ngeen nu def! 
 9 Ndokklee ku ne cas seeni fere, 
tas ciw doj!