Saar 6
Wooteb tuub jib na 
 1 Ca ngeen naan: «Nan dellu ci Aji Sax ji. 
Moo nu xotat, te moo nuy wéral. 
Moo nu duma, te moo nuy takkal sunuy góom. 
 2 Ñaari fan, mu leqli nu, 
ñetteel ba mu yékkati nu, 
nuy dund fi kanamam. 
 3 Nan ràññee, di saxoo faale Aji Sax ji. 
Ni jant bu fenk la dikkam wóore, 
ni ab taw la nuy dikkale, 
ni ab tawu mujjantal buy seral suuf.» 
 4 «Ana nu ma lay def, yaw Efrayim? 
Nu ma lay def yaw Yuda? 
Te sa ngor di xiinu suba, 
mbaa ab lay, jekki ne mes. 
 5 Moo tax yonent yi laa leen di dumaa, 
sama kàdduy gémmiñ laa leen di reye. 
Seen àttee leen di jollil ni ceeñeeru njël. 
 6 Ndax ngor laa namm, dub sarax, 
ràññee Yàllaa ma gënal saraxi rendi-dóomal. 
 7 «Waaye ñoom ca dëkk ba, Adam lañu feccee kóllëre, 
foofa lañu ma wore. 
 8 Galàdd mooy dëkkub defkati ñaawtéef, 
taq ripp ak deret. 
 9 Ni saaysaay siy tëroo, 
ni la sarxalkat yi lëkkoo, 
di bóome ca yoonu Sikem. 
Ndaw jëf ju ñaaw! 
 10 Ci kërug Israyil laa gis lu yées: 
Fa la Efrayim di gànctoo, 
Israyil googu laa ne moo sobeel boppam. 
 11 Yuda yaw it, sam ngóob ma ngay taxawe, 
kera bu may tijji sama wërsëgu ñoñ.