Gannaaw mbugal, mbégte
Saar 34
(Saar 34—35)
Mbugal ñeel na Edom
1 Yeen xeet yi, jegesileen te déglu;
yeen askan yi, teewluleen!
Na suuf ak li ci biiram déglu,
muy àddinaak lépp lu mu jur.
2 Merum Aji Sax ji ñeel na xeetoo xeet,
am sànj ñeel gàngoori xeet yi.
Aji Sax ji faagaagal leen,
dogal ñu war leena rendi.
3 Seeni néew lees di xalab,
ñu médd, xet ga gilli,
seen deret la tund yiy sangoo.
4 Gàngooru asamaan gépp ay tasaaroo,
asamaan taxañe ni lëmësub kayit,
gàngooram gépp ruus
ni xobu reseñ mbaa figg gu lax.
5 Aji Sax ji nee: «Saab saamar a reye fa asamaan
ba màndi deret,
te mu ngii di wàccal Edom,
xeet wi may faagaagal, ngir àttee leen ko.»
6 Aji Sax jee yor saamar bu màndi deret,
yafloo nebbon,
ak deretu kuuy mu ndaw ak bëy,
ak nebbonu dëmbéenu kuuy.
Aji Sax ji kat moo am ab sarax fa Boccra,
muy tër mu réy fa réewum Edom.
7 Nagi àll yaay ànd ak ñoom daanu,
ñook yëkk yu ndaw yaak yu mag ya,
seen réew mi màndi deret,
suuf sa niin batt ak nebbon.
8 Bésub feyu la, Aji Sax ji di ca feyoo;
mooy at mi Edom di yooloo la mu loroon Siyoŋ.
9 Wali Edom di ca soppliku koltaar,
pëndub suufam doon tamarax,
suufam mel ni koltaar buy lakk,
10 guddeek bëccëg, du fey,
saxar sa day gilli ba fàww,
réew ma gental giiru jamono,
te deesatu fa jaare mukk.
11 Céeleek siññéel a koy nangu,
looy ak baaxoñ dëkke fa.
Buumu beteex lees koy natte, maasale,
ba mu ne maraas, ne wëyëŋ.
12 Garmi ya dootuñu fa teewe,
ba di fa samp nguur,
te seen kàngam yépp ay wuute.
13 Seen kër buur ya la dég ya di lawe,
gajj aki taxas saxe tata ya,
till dëkke,
bànjóoli tàgge,
14 rabi màndiŋ mi di fa dajeeki bukki,
bëyu àll di fa wooye moroom ma.
Fa la rabu guddi di dal-loo,
fàkkal fa boppam ab dal.
15 Fa la luy nen di tàgge, nen fa,
bóof, ba tostan, yiire keppaaram;
tan ya bokk fa daje,
ku ci nekk ak moroom ma.
16 Seet ko ci téereb Aji Sax ji, jàng ko;
du menn mala muy wuute ca gent ba,
lu ci nekk a fay ànd ak moroom ma.
Aji Sax jee ko santaane ci gémmiñam,
moo leen di dajale, moom ci boppam.
17 Moom moo leen ko muurale,
sédd leen suuf sa ci loxoom,
ñu séddoo ko ba fàww,
màkkaanoo ko maasoo maas.