Saar 54
Aji Sax ji jëlaat na Yerusalem, soppeem
1 «Yaw mi jaasir ba juroo, xaacul!
Yaw mi xamul mititu mat, sarxolleel.»
Aji Sax ji nee:
«Ndaw si ñu foñ moo gëna jaboot
kiy séy.
2 Yaatalal sa xayma bi,
firi sa sori xayma yu gëna yaa
te bul yéem.
Yokkal sa buumi xayma
te samp say bant, mu dëgër.
3 Dinga saam ay doom ndijoor ak càmmoñ,
saw askan moom ay xeet,
sancaat dëkk yu gentaloon.
4 Bul tiit, doo rus mukk.
Bul jaaxle, deesu la kersaal mukk.
Sa gàcce ga ba ngay ndaw, dinga ko fàtte,
te sa tiisu jëtun wa dootoo ko fàttliku.
5 Sa jëkkër, ki la sàkk,
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee di turam.
Aji Sell ju Israyil moo la jot,
te moo di Yàllay àddina sépp.
6 Aji Sax jee la woo, nga dib jeeg bu ñu wacc,
sa xol jeex tàkk,
Mu ne la:
“Nees di wacces ndaw,
si nga takk ba ngay ndaw?”»
Sa Yàllaa ko wax.
7 Mu ne: «Maa la wacc diir bu gàtt,
dellu la jël ci yërmande ju yaa.
8 Sama xol a jóg,
ma xañ la sama kanam ab diir,
waaye maa lay yërëme ngor gu sax.»
Aji Sax, ji lay jot moo ko wax.
9 Mu ne: «Na ma defoon ak
ndoxum Nóoyin ma mooy lii tey.
Maa giñoon ne ndoxum Nóoyin ma,
mu ni day dootu wale kaw suuf.
Noonu it laay giñe ne
duma la mereeti,
duma la rëbbati.
10 Bu tund yu mag yi doon toxu,
yu ndaw yiy raf sax,
sama ngor du la toxul,
te sama kóllërey jàmm du raf.»
Aji Sax ji la yërëm moo ko wax.
11 «Ngalla yaw Yerusalem,
mi ngëlén pamti-pamtee ba nga jàq,
te kenn dalalu la,
man Aji Sax ji,
maa ngii di la tabaxe doj yu ne ràññ,
samp la ci kenuy safiir.
12 Maay defare sa kawi tata peri rubi,
def say wunt per yuy lerxat,
def sa tata yi la wër yépp doj yu bakkane,
13 mboolem sa doom yu góor ay jànge ci Aji Sax ji,
boole kook jàmm ju ne ñoyy.
14 Njekk moo lay dëgëral,
nga sore noteel, doo tiit;
sore tiitaange, du la jege.
15 Xanaa dees na songe moos,
waaye ku la song it, yebalu ma ko,
te ku la song daanu fi sa kanam.
16 Xoolal, man maa sàkk ab tëgg
buy wal taalu këriñ,
defar ca ngànnaay lu ne.
Waaye maa sàkk it
yàqkat buy rajaxe.
17 Ngànnaay lu ñu la mana sàkkal,
du sotti,
te boroom làmmiñ wu la jógal cib layoo
yaa koy tiiñal.
Ñiy jaamu Aji Sax ji, looloo di seen cér,
looloo di njekk gi ma leen di dikke.»
Kàddug Aji Sax jee.