Saar 66
Ragal Yàlla du jëfi ngistal
Aji Sax ji dafa wax ne: «Asamaan sama ngàngunee,
suuf di sama ndëggastal.
Ana kër gu ngeen may tabaxal man?
Ana ban bérab ay sama dal-lukaay?
Mboolem yooyu, sama loxoo ko sàkk;
nii la lépp ame.» Kàddug Aji Sax jee.
«Ku mel nii laay niir:
néew-ji-doole ji xolam jeex,
te muy déglu sama kàddu bay lox.
Kee moom mu ngi rendiw yëkk, sarxal,
te teewu koo bóome.
Kee rendiw xar, sarxal,
te teewu koo damm loosu xaj, sarxal.
Kee ngi joxe saraxu pepp,
te teewu koo tuur deretu mbaam-xuux.
Kee di taal saraxu baaxantalu cuuraay,
tey jaamu ay tuur.
Ñoo taamu seen yoonu bopp,
safoo seeni jëf ju seexluwu.
Man it maa leen di taamoo jox seeni mbugal,
dikke leen tiitaange yi ñu yelloo,
ngir maa woote, kenn wuyuwul,
ma àddu, dégluwuñu ma.
Xanaa di def lu bon lu ma ñaawlu,
li ma buggul, ñu taamu ko.»
Aji Sax ji mujj na dikk
Dégluleen kàddug Aji Sax ji,
yeen ñiy déglu kàddoom, di lox.
Lii de mooy seen kàddug bokk,
yi leen jéppi, di leen dàq ngir samaw tur.
Ñu ngi naan: «Na Aji Sax ji darajaal boppam,
ba nu teewe seen mbégte, yeen ñii!»
Waaye ñoom de ñooy rus.
Coowal xaree ngoog bawoo dëkk ba,
coow laa nga jóge kërug Yàlla ga,
coowal Aji Sax jee, mooy yool ay noonam.
 
Kii balaa matu, wasin na,
bala moo am mititu mat, jur na doom ju góor.
Ku masa dégg lu mel nii?
Ku masa gis lu mel nii?
Am réew dina sosu ci benn bés a?
Am aw xeet dina jekki sosu ci wenn fan?
Siyoŋ de, moo tàmbali matu rekk,
jur doomam yu góor.
Aji Sax ji nee: «Man miy jàpple jigéen
ba ëmbam mat,
dinaa ko xañ wasin?
Man miy wasinloo nit,
dinaa fatt njurukaayam?»
Sa Yàllaa ko wax.
 
10 Yeen soppey Yerusalem yépp,
bégandooleen ak moom,
te di ko bànneexoo.
Mboolem yeen ñi doon ñaawlu tiisu Yerusalem,
bokkleen ak moom xolam bu sedd.
11 Su ko defee ngeen nàmp ba suur
weenam wiy naxtaane,
su ko defee ngeen nàmp bay tàqamtiku
soowum weenam mi ne xéew.
12 Aji Sax ji déy dafa wax ne:
«Maa ngii di yóbbu Yerusalem
ci jàmm ju mel ni géej,
ak waamey koom muy wal, bawoo ci xeet yi.
Yeenay tooge luppu Yerusalem, di nàmp,
uufu ciy óom, mu di leen raay.
13 Man maa leen di naxtaan ba ngeen dal,
ni doom ju ndeyam di naxtaan ba mu dal,
ngeen am xel mu dal fi Yerusalem.
14 Yeenay teewe lii, seen xol tooy,
seen yaram leqliku ni ñax mu yég nawet.
Dooley Aji Sax ji la ay jaamam di xam,
te am sànjam la ay noonam di xam.
 
15 «Aji Sax ji déy a ngii dikke sawara,
ay watiiram mel ni ngëlén,
mu nara sànju, sotti meram,
gëdde sawara wuy sëlsëli.
16 Sawara déy la Aji Sax ji di mbugale,
saamaram ba dal mboolem doom aadama,
ñi Aji Sax ji bóom ne xas.
 
17 «Ñii di sellalu ak a sangu-set
bala ñoo duggi tool ya ñuy tuuroo,
di fa toppi ca gannaaw ka ca digg ba,
ñooñooy lekk yàppu mbaam,
ak yeneen yu seexluwu ni janax,
te ñooy bokk sànku.»
Kàddug Aji Sax jee.
18 «Man maa xam seeni jëf ak seeni xalaat.
Bés bii taxaw lees di dajale xeetoo xeet aki làkk,
ñu dikk ba niir samag leer.
19 Maay teg firnde fi seen digg,
ba jël ñenn ca ña dese bakkan ca ñoom,
yebal leen ci xeet yi,
yebal leen Tarsis, ak Pul ak Ludd,
ñooña di ñu mane fitt,
ma yebal leen ca waa Tubal ak Yawaan,
waa duni géej yu sore ya,
ñooñu masula dégg sama jaloore,
te masuñoo gis sama teddnga,
sama ndaw ñaa leen di xamal sama teddnga.
20 Xeet yooyooy indi seen bokk
yi bokk ak yeen ñépp,
jële leen ci mboolem xeet yi,
ñu doon sarax bu ñeel Aji Sax ji,
wari fas aki watiir,
ba ci watiir yu ñu mbaar,
aki berkelleeki giléem,
ba agsi sama tund wu sell,
wi ci Yerusalem.»
Aji Sax jee ko wax.
«Day mel ni noonu bànni Israyil di yóbboo sarax,
yeb ko ci ndab lu sell,
yóbbu kër Aji Sax ji.
21 Te ñenn ci yooyu xeet, maa leen di jël,
def leen ay sarxalkat aki Leween.»
Aji Sax jee ko wax.
22 «Asamaan su yees sii,
ak suuf su yees sii may waaja sàkk déy,
ni seen taxawaay di yàgge fi sama kanam,
yeen, ni la seen askan ak seen tur di yàgge fi sama kanam.
23 Su ko defee Terutel weer ba Terutel weer,
bésub Noflaay ba bésub Noflaay,
mboolem doom aadama di ma sujjóotalsi.»
Aji Sax jee ko wax.
24 «Te bu ñu génnee, gis néewi
ñi doon fippu fi sama kaw,
seeni sax duñu dee mukk,
seen sawara du fey mukk,
te boroom suux bu leen gis, yaram wa daw.»