Saar 18
1 Ab siis, bànneexu boppam rekk,
loo ko digal mu xalab.
2 Ab dof wutul ag dégg,
balaa caag muy jaay ag muus.
3 Bu mbon nuyoo, xeebeel topp ca;
jëf ju ñaaw, gàcce rekk.
4 Waxi nit ndox mu xóot la,
bu bënnee, xelli, ñu di ca xelu.
5 Faral ku tooñ baaxul,
bul xañ dëgg ku deful dara.
6 Ab dof, làmmiñam sooke naw ay,
ay waxam di sàkku yeti gannaaw.
7 Ab dof, waxam a koy sànk,
làmmiñu boppam a koy dugal.
8 Waxi jëwkat di ñam wu neex
wuy seey, jàll ca biir-a-biir.
9 Kuy sàggane sa liggéey,
yaak kuy yàq a bokk.
10 Turu Aji Sax ji rawtu bu mag la.
Ku jub daw làqu ca, raw.
11 Alal day aar boroom ni ab tata,
mu xalaat ne maneesu koo bëtt.
12 Bew, yàqule;
jëkke woyof, mujje tedd.
13 Tontu te déggagoo,
ndof la, ak ñàkk kersa.
14 Ku bëgga dund, dékku woppi yaram,
waaye xol bu jeex maneesu koo wéye.
15 Ku am ug dégg wut xam-xam,
ku rafet xel sàkku xam-xam.
16 Deel maye, da lay ubbil bunt,
di la àggle ci boroom daraja.
17 Ku jëkke layoo, ñu ne yaa yey,
ba keroog ka nga joteel weddi la.
18 Tegoo bant day feyu ay,
di àtte boroom doole yu jote.
19 Jubook mbokk moo tooñ,
jéggi tataa ko gëna yomb,
mbaa ubbi bunt yu tëje ràpp.
20 Làmmiñ feesal na biiru boroom,
yoolu kàddu suur na boroom.
21 Dund ak dee a ngi ci làmmiñ,
te wax garab la, ku ko bëgg, lekk ca doom ya.
22 Ku am jabar, am nga ngëneel,
am nga yiwu Aji Sax ji.
23 Ku ñàkk a ngi leewaayu,
boroom alal di ko jànni.
24 Barey àndandoo lor a ngi ci,
waaye xarit a ngi gëna taq nit mbokkam.