3
Ñaanleen ci Yàlla
Léegi nag bokk yi, ñaanal-leen nu, ngir kàddug Boroom bi law te ànd ak ndam, ni mu ko ame woon ci yéen. Ngeen ñaanal nu it, ngir nu mucc ci ñi bon te soxor, ndaxte du ñépp a gëm. Waaye Boroom bi kuy sàmm kóllëre la; dina leen dëgëral te musal leen ci Ibliis. Te wóor nanu ci kanam Boroom bi ne yéena ngi def li nu leen santoon, te dingeen ci sax. Na Boroom bi gindi seeni xol ci mbëggeelu Yàlla ak muñu Kirist.
Liggéey
Nu ngi leen di sant it bokk yi, ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist, ngeen dëddu bépp mbokk buy wéy ci tayel te baña topp dénkaane, yi nu leen jottali. Xam ngeen bu baax, yéen ci seen bopp, ni ngeen wara awe ci sunuy tànk. Ba nu nekkee ca yéen, wéyunu woon ci tayel te masunoo lekk ñaqu kenn. Waaye guddi ak bëccëg danu daan ñaq, di sonn, ngir baña wéeru ci kenn ci yéen. Waxuma ne amunu sañ-sañu def ko, waaye danoo bëggoona nekk ay royukaay ci yéen, ngir ngeen aw ci sunuy tànk. 10 Ndaxte ba nu nekkee ca yéen, lii lanu tëraloon: «Ku liggéeyul, du lekk.»
11 Léegi nag dégg nanu ne am na ci yéen ñuy wéy ci tayel; liggéeyuñu dara, lu dul di dugg ci lu seen yoon nekkul. 12 Ñu deme noonu nag, nu ngi leen di sant te di leen dénk ci turu Boroom bi Yeesu Kirist, ñuy liggéey ci jàmm tey dunde seen ñaq. 13 Yéen nag bokk yi, buleen tàyyi ci def lu rafet.
14 Su kenn bañee topp li nu bind ci bataaxal bii, ràññeeleen ko te sore ko, ngir mu rus ci. 15 Waxuma ngeen def ko noon, waaye ngeen yedd ko ni seen mbokk.
Tàggoo
16 Yal na leen kiy Boroom jàmm may jàmm fépp ak ci lépp. Yal na Boroom bi ànd ak yéen ñépp.
17 Tàggoo bii maa ko bind ci sama loxo, man Pool. Nii laay binde, te di màndargaale nii sama bataaxal yépp. 18 Yal na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist ànd ak yéen ñépp.