Saar 15
Bantu reseñ matul matt
1 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:
2 Yaw nit ki, ana lu bantu reseñ gëne ci bant yi,
ak mboolem caru garab bu mu doon ci gott bi?
3 Ndax dees na ca sàkk bant, liggéeye ko?
Am dees na ca sàkke wékkukaay, wékk ca lenn?
4 Xanaa sànni cib taal, xambe,
ñaari cat ya lakk, digg ba xoyomu.
Ana lu deeti njariñam?
5 Ndegam ba mu nee ñumm,
lees ci dul liggéey dara,
gën ba mu jàppee ba xoyomu.
6 Kon nag Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Dees na xamb caru reseñ,
mu bokk ci banti garab yi ma joxe, ñu xamb lépp,
te noonu laay xambe waa Yerusalem.
7 Maay jànkoonteek ñoom,
ñu rëcc sawara,
sawara lakk leen.
Bu ma jànkoonteek ñoom,
dingeen xam ne maay Aji Sax ji.
8 Maay gental réew mi,
ñoo def jëfi ñàkk worma.
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.